Sa ma gènt gi_I have a dream

  


Begg naa loo lu daje ak yeen tay jii,  ci lii nga xam ne di na ñu koy fattaliku, ni doxu ñaxtu wi gëna yeeme nga xam ne  reew mii di na ko dund.

Lu matt juroom benni fukki att ci gannaaw, mennum kangam ci dommi rewmi, nga xam ne ci kepaaram la ñu taxaw tay jii, da fa xaatimoon aw teere di ñu dig ne di na ñu moom sunu bopp. Kaddu goo gu da fa jiboon, mel nib njëmbët mu yaakaaru, ñeel junniy junni ci doomi reew mi, yu ñu sëf yennuw jaay doole. Kaddu googu daal di mell ne jant bu fenk, guy  dakkal guddig bundaxatal ak nooteel.

Waaye boo ba ba leegi, bari na lool ci reew mi ñoo xam ne seeni loxo jottul seen gannaaw. Boo ba ba leegi, am na ñoo xam ne buumi xajj ak seen ak parparloo yeew na leen ba seen cër yi lomppoñ.

Boobu ba leegi, am na ñoo xam ne da fa mel da ñoo dëk condong ci naaj wu kerr gu sedd guyy wër

Boo bu ba leegi am na ñoo xam ne da ñu leena tañc cim puqus ñu mel fa ne ay daw lqqu, ci kaw suuf soo xam kenn ëppu leen ca wall. Lii moo tax ñu ñëw fii tay, di fattali reew mi ne lii fi  xeww da fa ruslu

Boo ko dee seet, da ñoo ñëw ci barab bii, ngir jël si li ñu ñu diggoon. Ba su ñu mag ña doon xaatim sarti rew mi, da ñu doon lal aw mbalaan ñeel askan wi yëp. Mu doon ne nit ñëp. Muy boroom alal muy baadooloo, ñëpp'ay moom seen bopp,  jott ci seeni aqq ak yelleef. Tay jii da fa mell ne rew mi da fa wuute ak la mu digewoon, ñeel miskiin yi ak neew di doole yi. Waxu ma la sax ñu fay leen seen borr, waaye da ñu leena jox aw këwitt wu amul njariñ. Aw këyitt woo xam ne ba ñu deme ca saqqu rew mi, da ñu leen ne leen xaalis amul.

Waaye ñoo lank. Du ñu nangu ne gafaga ga ñu ñu jagleeloon da fa rës. Kenn manu ñoo gëm loo ne xeewal yi yallah dëxëñ ci reew mi amu ñu ci wall. Loo loo tax da ñu ñëw fayeeku.

Da  ñuy ñëw taxaw laacte loo xam ne moo ñuy may ñu manal su nu bopp tek ci am karangé gu matt sëk.

Da ñoo ñëw itam ci barab bii, fattali rew mi ne su nu aw mebet jamp na lool. Toolloo tu ñu fu ñu ñu naan xaar leen wala ànd leen ak dall lepp di na baax.

Da fa jot nak  ñu jox ñu li ñu ñu digoon. Jott na ñu juge ci xuru parparloo wu lëndëm wi. Dem ci yoonu njub wu wu leer wi. Da fa jot nak. Ñu genee dëk bi ci gënnuusu xajj ak seen. Dem ci keeku bokk ndey ak baay. 

Luy jot jot na. Ñu fexe di dawal yoon ñeel doomi aadama yëp.

Du mana jigg rew mi  bu ñi koy jiite  ñakkalee fayda lii fi xewoon. Su nu niiru mettit wi doon xiin ci jawwu ji. Du sebbet muk lu dul  da fa taw ba ndox mi raxas  lepp luy nootel ak tuutal doomu adama. 

La xewoon ca att wale weesu. du woon luyy taggoo,  da doon nuyoo. Kepp ku yaakaar ne. Ñoo ña  da ñu doon xumbal bu ñu noppee dellu ca la ñu newoon. Di nga am mbetteel gu rey. bu ñu njortee  ne nawoon fawoon ba leegi. 

Reew mi manul am jamm wala dal. Lu dul askan wi yëp jott ci seeni aqq. Callweeru ñaxtu wi di na wey di gësëm barab gi. Ba doomi xeewal yi wodd ci suuf, ñepp jott ci.

Waaye am na lu tuuti lu ma bëgga yeggee way ñaxtu yi taxaw di fëgg ci buntu atte kat yi. xemmeem wi ñgeen xemmeem seenni haqq, waru leena duggal ci ngeen di defiy ñawteef ngir faj seen xiif. Bu ñu mësa  sukk ci ndabul noonoo ak mbañeel. Da ñoo wara yëkati xeex wi ca kaw  ñambaasee ko laytaayu ko ngorr ak njubb. Ngalla bu ñu bayyi su ñu ñaxtu  muy tarxiis di muj ci  dooriy kurfeñ.  Ma waxati ko   Da ñu wara jubb  boole kartanu suux ak dooley xel.

Pastef  gu bees bii nga  xam ne  ndaw ñi ame na ñu ko waru ñoo wobbu ba ñuy noo noo su nu biir,  ndax ñu bari ci reew mi,  ni ko woote yii weesu yi wonnee,  xam na ñu ne sunup jamm da fa lëkaloo ak seen jamm, dem na ñu ba yegg ne su nu tawfeex mooy seen sutura.  

Waaye lu mu metti metti na ñu tek su nu xeex wi ci yoonu ci jomm ak ngor. Lu mu tartar, na ñuy xeexee xel te baña jiital xoll  Da ñoo wara kaweel su nu ñaxtu tek ko ci taggi doolé ak dall.

Waru ñoo weet ci  xeex bi te bu ñuy dox. Kepp ku ci wall si na ñu fekk ca bopp ba. Man'u ñoo dellu ganaaw. Amul dekouraaze. Am na ñuy laaj way fippu yi: kañ ngeen di bayyi? Du ñu bayyi mukk fii ak ñi ngi ñuy bunduxatal ak di nu tere  ñaxtu.  

Du ñu bayyi mukk fii akk xaleyi di na ñu jang ba yey seeni kayit de du ñu am liggeey. fii ak li ñëp bokk ñëp du ñu ca joot; fii ak dëp kees'a gi am ci miim rew ba leegi. Fii ak ñi ngi wanteer aka caxate alali  rewmi di ko joxiy jambur ci yaa ma neex.  Fii ak ci reew mi am na ñu sawaruta bindu ñu aka wote, te bu ñu leen sonjee ba ñu def ko am ñu dëpp kart gi. Deedeet doyal lu ñu de te du ñu toog lu dul yoon daal bi baawaan mel dex. Njum ak dall daal di jolli mel ni geec.  

Reere'u ma mbir ne  bi  ñenn ci yeen dund na ñu jaar jaar yu tarr. Am na ci yeen ñoo xam ne barki demb la ñu juge kaso.  Am na ci yeen ñu juge ci gox yoo xam ne  seeni doxu ñaxtu jurral na leen ay door yu metti. Xam leen ne yeen'a fi dëgmal xeetu jambarloo bu bees. Wey leen di xeex  te ngeen am yaqeen xeetu buntaxal yii  da fa leen di yëkati.   

Dellu leen fouta, dellu leen Louga.  Dellu leen Kedugu,  Dellu leen Matam,  Dellu leen Cees,   Dellu leen ci baraku banlieue bi and ak yaqqiin ne lii di na soppeeku.  

Bu kenn xaddi. Deglu leen ma wax leen tay ji: naam sax ñu ngi jankonte mettit yu tarr,  ba leegi maa ngui am yaakaar,   yaakaarwu mell ni woowu su ñu mak ya amoon.  Da ma gent ne bess du ñakk  askan di na jogg taxaw daal di dëggal  ne am'ul benn sik sakka ne neppa bokk yepp fa borrom bi. 

Gent naa ne bes du ñakk  ca gannuus'u ñaay yi    xaleyi doo tu ñu bëgante ñu galankoor seenup and aki waxi waasu wala xeet .  Gent naa ne besa ngi ci bes yi  ña dëke ci tefe binga xam ne bateau yi yobbu na  seeni jën. kenn ci ñoom dootul jëli looco naan  barsa wala barzaaq.  Gent naa ne su ñu ñenti bant yi ñu yallah sedd   kenn du leen xoole seen askan walab judd waaye sa bu ñu leen di Nat da ñu koy tek ci seen jikoo ak seeni jëf.

Degglu leen gent naa ne dek yi gën tarr sax dorrom daraja yi ak baadoolo di na ñu jappante niy ñu bokk ndey ak baay. Tay jii de am na lu ma gis. Sa ma gent mooy lepp lu kawewoon da na  suufe,  lepp lu jafewoona jott di na jappandi, lepp lu ñagasoon di na liis,  lu dëngoon da na jubbantiku,  kartanu borrom bi di na féss ñëpp wommatul ko.

Lii mooy su nu mebet,   ak paspas bii   paspas bii laay delloo sa ma gox.  ak paspas bi   man na ñoo yatt ci dojju njaqqare  xeeru yi yaakaar.  ak paspas bii man na ñoo soppi su nu askan wii di soox deff ko ni fasu naaru goor wuy jaab. Ak paspas wii  di na ñu  and ligeey, and ñaan borrom bi and xeex   and dem kaso   tawax and laac su nuy aqq   te xam du yaggati  dara nu moom su nu bopp mooy bess bi nga xam ne  doomu adama yëp di na ñu bokk and di woy  ñaani bañ na. dëk bii nga xam ne fii la si nu jambaar yi tëd dëk bii ñuy tiitaroo fepp ci goxu reewmi na wax siiw.

Te bu rew mu  nammee wuyoo aw  tuuram lii faw mu nekk.  Kon nak na wax ji siiw  ca biir dëkuwaayu goree ya na kaddu gii jolli, na wax jii riir ca xuru bamjagara yi waa keedugi bu kenn tëdd te degoo lii.  Bu baykatu baol bi di deqqi toolam na suuf si xeeñ lii. Ku sol dallu ngaay yi na ko sa yaram yegg. Waaye du yem foo fu.  Na mango casamance yaa saff ci sapp. na cooy li riir ba ca guyu ferlo ya touba ak tiwaawon na ko taalibe yi sikkar. ca gox goxaan yëp na wax bayaan.

Bu fa wax jii yeggee, bu yeggee ci dëk bu nekk ak gox bu nek  Bess boo bu di na ñu taxawu doomu adama yëp and jullit ak kerecen bi, joola bi ak sereer bi wolof bi ak toucouleurs ñëp rek di na ñu mana joxante loxo daal di ne,  yallah ñëw yallah ñew na. Sant borrom bi, moom na ñu su nu bopp.


Malé Fofana PhD 

Auteur, Conseiller linguistique et communication 

ComUnicLang-Bataaxel

https://www.comuniclang.com/

Sherbrooke, Québec, Canada

 

 

Commentaires

Messages les plus consultés